Les TIC à l'appui du programme des femmes
pour l'égalité de genre au Sénégal
une action en partenariat ENDA-SYNFEV et Siggil Jigéen

enda-synfev, b.p. 3370, Dakar, Sénégal,
tel : (221) 823 45 42 ; fax : (221) 822 26 95,
courriel : synfev (a) enda.sn,

http://www.enda.sn/synfev/synfev.htm

Siggil Jigéen, b.p. 10137, Dakar, Sénégal,
tel-fax : (221) 825 00 56 ;
courriel : sjigeen (a) telecomplus.sn,
http://www.famafrique.org/sjigeen/siigeen.html
avec le soutien du Programme Acacia
du Centre de recherches pour le développement international, Canada.

 

Këyitu IPM

"Ce document peut être librement reproduit, à des fins non commerciales uniquement, à condition d'en mentionner la source : ENDA, Projet parenté conjointe, Dakar, 2001"

Madam Joop : Assalaamu aleykum, Muse Ndong. Na nga def ? Man déy suma dooma feebar, doctoor bi ne nañ ko antare opitaal ci lu gaaw. Ma bëggoon këyit wu wane ne IPM bi moo koy gaddu. Suma karne IPM mu ngi nii.

Musé Ndon : Wa aleykum salaam, Madam Joop. Yal na Yalla saafara sa doom ji waay ! Madam Joop, na nga ma baal axx de, wante du ma mana defaral xale bi këyit woowu, ndax sa karne IPM mayul la ko.

Madam Joop : Nga ne ma lan ??!! Suma karnee ngi nii, bokk naa IPM, weer wu nekk ma fay, suma doom-a ngi wara antare opitaal te yoruma xaalis biñ ma laaj !

Musé Ndon : Nga baal ma de, waaye Musé Joop moo wara dem, su fekkee am na IPM, ñu defaral ko këyit woowu. Ndaxte Musé Joop mooy ki wara gaddu xale bi, ci yoon.

Madam Joop : Yalla def na suma jëkkër liggéeyëtul, be tax na amatul ku ko gaddu mook njabootam ci wallu wér gi yaram. Kër gë, fii ñu tollu, man rekk-a fay liggéey. Maa gaddu lépp, maa wara faj suma doom-itam. Damay liggéey, di fay IPM, te ñu ne manumaa gaddu suma doom yi sax !

(Musé Jen dal di dugg si) Musé Jen : Assalaamu aleykum, gaa ñi. Ndon, na nga def waay ? Madam Joop, mbaa jamm ngaam ? Ndon, dama bëggëloon suma doom këyit-u IPM, maanaam caat-u suma ñeenteel-u jabar. Dafa feebar-ati. Xale yi daal, kaar kaar, saa yu nekk rek am na ci ku daray metti ! Karne baa ngi nii.

Musé Ndon : Hée, Jen, ku baree alal ni yaw, be mana yore ñeenti jabar kay, doom yu bari waru ko jaaxal ! Saw këyit-a ngoog. Xale bi yal na ko Yalla may wér.

(Musé Jen dal di génn)
Madam Joop : Jen, maak moom-a bokk lu ñuy liggéey. Li muy fay laay fay. Moom mu mën cee gaddu lu jege fukki nit ak juroom, maanaam lim am ciy jabar ak-i doom yép, te man manumaa gaddu suma jëkkër ak sumay doom ci wallu wér gi yaram. Léegi nak, naka laay def ?

Musé Ndon : Yalla xam na ne bëggéewuma ko woon nii de, Madam Joop. Maa gënë xam ne jaaduwul, waaye suñu IPM loolu la ñu sant. Fu ñu ko teg mooy neena ñu goor mooy borom kër, kon nak moo wara aar njabootam.

Madam Joop : Kon nak ñun jigéen ñi fu ñu jëm ? Ana lu tax ñun la ñuy gën di sonal ?

Accueil | Documents sonores | Contactez-nous | Retour haut de page